Yaayi Baayam
Ce poème est dédié aux jeunes
sénégalais contraints à l’émigration
à bord de pirogues de fortune
Abubakar KAMARA, 30 mai 2006
Suma jottoon ci picc mi yéék
Ci gaalgi laa am ‘’VISA’’
‘’VISA’’téér mbaa suux
Ku amul ndey nampë maam
Dajale naa lima yor
Yooru ba booru Ngor
Jaayante ak sama ngor
Ngir tekki ni samay moromu goor
Witti ‘’Reseŋ’’ bittim rééw
Mooma gënël tumranke ci sama rééw
Jaral nama Yaayi Baayam [1] forri neew
Mooko gënël dundë bu njëriŋ la neew
Ñii may yedd ngir ma toog
Nañu ma feqeel ci luma toog
Su dem laajoon raam
Ma fabbu def ni jaan
Sooma mënula teyye
Tee nga ma teg ci yoon wu teey
Ndax ñii neenañu maa yey
Limay soobu maako tey
Buñu manee diw yeggëna ci jamm
Sama yaakaar yokku, may waaj dem ci jamm
Buñu manee diw desna ci gééj gi
Sama adduna tukki te duma teree tukki.
[1] Yaayi Baayam Diouf est la mère de Alioune MAR, son fils unique, âgé de 26 ans, emporté par la mer le 12 avril 2006 sur le périlleux chemin de l’émigration clandestine en Europe. Elle avait encouragé son fils à partir, « il savait qu’il risquait sa vie mais il a fait un choix réfléchi », disait-elle, les larmes aux yeux. Yaayi Baayam qui habite à Thiaroye, dans la banlieue dakaroise, avait vu son fils économiser difficilement 575.000 FCFA (875 euros) en élevant des moutons après s’être essayé à la maçonnerie et à la peinture. Signalons que Yaayi Baayam est le nom généralement donné à une femme homonyme de sa grand mère paternel.