Ma demman
Ku degg lii, sa xel ne yar ci Sëriñ Mansur
Buko waxaan ci diggi jangale mi
Waaw yi addoo ndoo
Ñëpp yakkamti taataan ci xam xam bi
Ma demmam ?[1]
Ce poème est dédié à Serigne Mansour SY, défunt Khalife général des Tidjanes. Au cours de ses succulentes conversations, il avait l’habitude, par souci pédagogique, en vue s’assurer que son auditoire le suivait bien, de poser la question suivante « Ma demmam ? » qui signifie « Puis-je continuer ? ».
Biñu lay wax demal
Waxuñu woon nga laqu
Dañu bëggon rek nga xellil ñu
Ci sa gééju xam xam
Ma demmam ?
Yow nga nax ñu ba dem
Fi nga jëm umpula
Wante di nga weetal jamono
Ndax sa xaas wërna adduna
Ma demmam ?
Sa gammu « garantina »
Sa xasida waxi-noppi
Tey nak la mbir mi « Alaa Dawme »
Ndax sër wodd na malaan
Ma demmam ?
Xol tooy na and ak jaaxle
Yow Sëriñ Mansur
Ci Yiw bi ak leer gi
Yaa yéeg bañu fi
Ma demmam ?
Yow mi aay ci aajo yi ak taax yi
Yow mi ëmb « daraa » yi ak daara yi
Yow miy « baranse » te doo botti
Yow miy doxloo lu taxaw, tey dowloo luy dox
Ma demmam ?
Buñula mënoona abb ab diir
Suñu fukki loxo du doy ngir jafandu
Suñu fukki óom du om ci wommatu ci say tank
Ba suuf sedd ba melni bii nga woomal Tiwaawan
Bubakar Kamara
Décembre 2012