Maa Takko
Maa Takko[1] yaa jara woy
Maa Takko yaa jara kañ
Fanaane uuf, yendoo bóót
Di naq guddek bëccëk
Dëkkë di fac, dëkkë di aar
Li nga attan ci doom
Mburu ñeme wuko ci taal
Maa Takko yaa jara woy
Maa Takko yaa jara kañ
Jog nga njël bidënti woo
Gis bi dërëm jaree njëgëm
Teewe bi añ di seddë réér
Seede bi ñakk di xañ teranga
Fekke bi muñ doone wurus
Maa Takko yaa jara woy
Maa Takko yaa jara kañ
Foo mënna nekk ci loo mënna taxaw
Sa liggééy moolay wallu di la jagleel
Barke ak teranga yiy sa fey
Sa xollu yërmande moolay taxawu
Yaag sa njaboot bi ngay noyyee
Bubakar KAMARA
04/02/1990
[1] Taalif bii ma ngi ko jagleel sama yaay Takko. Poème dédié à ma mère Takko.