Seede Señ Salihu
Señ Salihu[1], wacc liggééy, laqu…
Ajuma jooju, mu ngi noonu !
Senegal ak Adduna ňakk
Lu yagg te wër tey ňak
Ku sax ci xol yi ak xel yi
Lii moo waral rongoň yi di xelli
Ňayu xare weetal na Xelxom
Gooru Yalla mi ittewoo Koom koom
Cey! Suma mënoon dellu tuut tank
Nga mey ma may dirééku ci say tank
Tuuba, Tuuba, fu soriwoon te jeggesi
Fune waay yennoo fa, yeksi
Jaljalu adduna ňu yebbi
Moom du ci yëy, du ci yabbi
Bu yekkatee kaddu, xiir ňu ci suňu Borom
Bu addoo, ňaax ňu ci liggééy ak jom
Bu dellusee, jubbanti jikko yi ak jëf yi
Bu waqee, joxoň Kaamil bi ak Xasida yi
Lima am ci moom xéébu mako
Siňatiir ba firndeel nako
Cere céép bimu ma desal
Soxlaatuma luko reesal
Vendredi 29 décembre 2007
[1] Ce poème est dédié à Serigne Saliou MBACKE, défunt Khalife général des Mourides