Serin Salihu, wacc liggééy, laqu…

Ajuma jooju, mu ngi noonu !

Senegal ak Adduna ňakk

Lu yagg te wër tey ňak

Ku sax ci xol yi ak xel yi

Lii moo waral rongoň yi di xelli

Ňayu xare weetal na Xelxom

Gooru Yalla mi ittewoo Koom koom

Cey! Suma mënoon dellu tuut tank

Nga mey ma may dirééku ci say tank

Tuuba, Tuuba, fu soriwoon te jeggesi

Fune waay yennoo fa, yeksi

Jaljalu adduna ňu yebbi

Moom du ci yëy, du ci yabbi

Bu yekkatee kaddu, xiir ňu ci suňu Borom

Bu addoo, ňaax ňu ci liggééy ak jom

Bu dellusee, jubbanti jikko yi ak jëf yi

Bu waqee, joxoň Kaamil bi ak Xasida yi

Lima am ci moom xéébu mako

Siňatiir ba firndeel nako

Cere céép bimu ma desal

Soxlaatuma luko reesal

Vendredi 29 décembre 2007

Bubakar Kamara

 

Partager