Sama xarit, maa ngi lay jaal Señ Murtadaa Mbakke…
Señ Murtadaa[1], suñu mos, mi ñu uuf, mi ñu yëk
Señ Murtadaa, mi seede sa taxawaay bu jekk
Moom mi la dénkaane
Te mënuula jaawale
Firnde bii de yéem nama
Kumu doyul, man doyna ma
Xel yi andë daw ba Rëbës
Gët yi andë lendëm kuruus
Nopp yiy riir, déggë tuñu
Xol yi fees bay tuuru
Xamuma ku ñakkul tey
Waaye ñakk nga ndéey
Jappal ne ñakkuloo dara
Ndax am nga Seriñ Murtadaa
Mi dëkk ci samp daara ak jakka
Saxxoo alxuraan ak ay rakka
Di sakkal ligééy ndaw ñi
Di saxalal njël mag ñi
Jërëjëf Señ Murtadaa, siggi ko ndigaale Mbay…
Ziar naala ko
Melal ni ku nekk ci néegam ba ca sa kër.
Bubakar KAMARA
Dimanche 8 août 2004
[1] Ce poème est une lettre de condoléances adressée à mon ami Mbaye Diouf DIA, un fervent talibé de Serigne Mourtada MBACKE qui avait instauré la tradition de prendre dle départ de son domicile à Yoff pour sa tournée annuelle aux Etats Unis.
Le Cheikh fut rappelé à Dieu au moment où Mbaye Diouf Dia était injustement emprisonné en même temps que d’autres agents des douanes. Il fut relaxé purement et simplement après un procès qui révéla une grosse cabale.